TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • lmd lesoŋ 2
  • Waxal mel ni kuy waxtaan

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Waxal mel ni kuy waxtaan
  • Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ni ko Filib defe
  • Ban njàngale lañu mën a jële ci li Filib def?
  • Nanga roy ci Filib
  • Wonal nit ñi ne am nga itte ci ñoom
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Nañu wone jikko yi jekk ci pioñee
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Ndax danga war a kontine waxtaan bi walla déet?
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • “ Kàddu gu ñu wax ca waxtoom ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2000
Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
lmd lesoŋ 2

NI NGA MËNEE TÀMBALI WAXTAAN

Filib a ngi waxtaan ak góor gu jóge Ecópi bu toogoon ci watiiram di jàng téereb yonent Yàlla Esayi.

Jëf ya 8:30, 31

LESOŊ 2

Waxal mel ni kuy waxtaan

Njàngale bi: «Kàddu gu ñu wax ci waxtu bi gën—aka moo neex!»—Kàddu yu Xelu 15:23.

Ni ko Filib defe

Filib a ngi waxtaan ak góor gu jóge Ecópi bu toogoon ci watiiram di jàng téereb yonent Yàlla Esayi.

Turu WIDEO bi: Filib a ngi wax ak nitu Ecópi ku yoom

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Jëf ya 8:​30, 31. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1. Naka la Filib tàmbalee waxtaan bi?

  2. Lu tax ñu mën a wax ne, ni mu tàmbalee waxtaan bi ak nitu Ecópi bi, mooy fasoŋ bi gën, ngir jàngal ko njàngale bu bees?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Filib def?

2. Bu ñuy wax ak nit ki, bu ñu jéem a forse waxtaan bi, waaye nañu wey di wax ak moom mel ni kuy waxtaan rekk. Noonu, nit ki dina ñu déglu bu baax. Amaana ñu am bunt ngir waar ko.

Nanga roy ci Filib

3. Deel seetlu. Li nit ki yëg, dafay feeñ ci kanamam ak ci ni muy jëfee ak yaw. Ndax mu ngi wone ne bëgg na la déglu? Ci misaal, boo ko bëggee won dara ci Biibël bi, mën nga ko laaj lii: «Ndax xamoon nga ne . . . ?», ba pare nga xol li muy def. Bul forse waxtaan ak ki nga xam ne bëggul a wax ak yaw.

4. Bul yàkkamti. Bul foog ne da nga war a ñëw rekk tàmbali wax lu jëm ci Biibël bi. Li gën mooy ngay waxtaan ak moom te xar ba nga am bunt ngir won ko dara ci Biibël bi. Yenn saay nag, da nga war a xar ba beneen yoon ngir mën a wax ak moom lu jëm ci Biibël bi.

5. Waxal nit ki li ko itteel. Nit ki mën na wax ci loo waajalul. Bu loolu amee, waxtaanal ak moom ci li ko itteel, bu dee sax li mu bëgg wute na ak li nga waajaloon.

SEETAL AAYA YII ITAM

Kàdduy Waare 3:​1, 7; 1 Korent 9:22; 2 Korent 2:17; Kolos 4:6

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager