“ Kàddu gu ñu wax ca waxtoom ”
1 Ndax yéene ñeneen ñi xabaaru dund gi, daa jafe ci yaw ? Ndax danga xalaat ne, danga war a wax lu xóot xel ngir laal ñi lay déglu ? Ba Yeesu yónnee ay taalibeem, lii la leen wax : “ Bu ngeen demee nag, yégleleen naan: Nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na. ” (Macë 10:7). Du woon xabaar bu jafee nànd te yomboon naa xamle. Mbir mi wuutewul ci suñu jamano.
2 Li gën a faral, jarul wax ju bare ngir tàmbali aw waxtaan. Ba Filipp tasee ak jaraafu Ecópi ja, da ko laaj : “ Ndax xam nga li ngay jàng ? ” (Jëf. 8:30). Ndaw waxtaan wu am njariñ, wu juddoo ci ‘ kàddu googa ñu waxoon ca waxtoom ’ ! — Léebu 25:11.
3 Mën ngaa def lu ni mel ci sasu waare bi. Nan ? Boo amee seetlu tey tànn bu baax baat yi war ci anam, yi nga nekk. Laajteel, te déglu tont li.
4 Yenn ci laajte, yu am solo : Ngir tàmbali waxtaan wi, mën ngaa jéem benn ci laajte yii :
◼ “ Ndax dingay jëfandikoo Ñaanu Sang bi (walla Suñu Baay) ci sa njaamu ? ” (Macë 6:9, 10). Tari ci aw dog, ba noppi ne : “ Am na nit ñuy laajte : ‘ Lan ay turu Yàlla ji Yeesu nee, dañu ko war a sellal (walla, teddal) ? ’ Ñeneen dañuy laajte : ‘ Lan ay Nguur gi Yeesu nee, dañu ko war a ñaanal ? ’ Ndax am nga tont yu la doy ci laajte yooyu ? ”
◼ “ Ndax mas ngaa toog ba laaj sa xel : ‘ waaw, lan ay tekki-tekki dund gii ? ’ ” Wonal ne lu lëkkaleek xam-xamu Yàlla la. — Daj. 12:13 ; Ywna. 17:3.
◼ “ Ndax foog nga ne dinañu toog bés, ba dee dootul am ? ” Jëfandikool Isayi 25:8 ak Peeñu bi 21:4 ngir joxe tont lu wér.
◼ “ Ndax am na pexe, mu yomb, mu ñu mën a sàkkal jaxasoo jii ne ci àddina ? ” Woneel ne, li Yàllay jàngale mooy “ bëgg sa moroom ”. — Macë 22:39.
◼ “ Ndax musiba mu bawoo ci biddéew yi dina yàq suñu suuf si, bés ? ” Xamalal ne Biibël baa ngiy dig ne, suuf si dina sax ba fàww. — Sab. 104:5.
5 Waxtaaneel xabaar bu baax bi ci fasoŋ bu yomb, bu àndul ak sikki-sàkka, te làmboo worma. Yexowa dina barkeel say njéem ngir jottali ñeneen ñi dëgg gi, doonte sax benn “ kàddu ” la.