TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • lmd lesoŋ 3
  • Woneel mbaax

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Woneel mbaax
  • Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ni ko Yeesu defe
  • Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?
  • Nanga roy ci Yeesu
  • Wonal nit ñi ne am nga itte ci ñoom
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Wonal nit ñi ne li ñuy yëg itteel na la
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Waxal mel ni kuy waxtaan
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Yan jikko yu rafet la Yeesu amoon?
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
Xóotalal waxtaan bi
Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
lmd lesoŋ 3

NI NGA MËNEE TÀMBALI WAXTAAN

Yeesu a ngi wone mbaax góor gu gumba gi. Mu ngi koy jege ngir faj ko.

Yowaana 9:1-7

LESOŊ 3

Woneel mbaax

Njàngale bi: «Ku bëgg . . . dafa baax.»—1 Korent 13:4.

Ni ko Yeesu defe

Yeesu a ngi wone mbaax góor gu gumba gi. Mu ngi koy jege ngir faj ko.

Turu WIDEO bi: Yeesu a ngi faj benn góor gu gumba

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Yowaana 9:​1-7. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1. Lan la Yeesu njëkk a def—faj góor gu gumba gi walla yégal ko xibaaru jàmm ji?—Jàngal Yowaana 9:​35-38.

  2. Lu tax ñu mën a wax ne, li ko Yeesu defal moo tax góor gu gumba gi nangu ko déglu?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?

2. Nit ki dina la déglu bu yëgee ne am nga itte ci moom.

Nanga roy ci Yeesu

3. Wonal nit ki ne yëg nga li mu yëg. Xalaatal ci jafe-jafe yi muy dund, noonu di nga yëg li muy yëg.

  1. Laajal sa bopp lii: ‘Ban njàqare la am fi mu tollu ni? Ban ndimbal la soxla?’ Booy laaj sa bopp fasoŋ laaj yooyu, di nga yëg li nit ki yëg. Loolu moo lay xiir nga dimbali ko ak xol bu tàlli.

  2. Déglul nit ki bu baax ngir won ko ne li muy wax itteel na la. Bu laay wax li mu yëg walla mu lay wax jafe-jafe yi mu am, bul ko dog. Déglu ko bu baax.

4. Wonal nit ki mbaax ak respe. Bu dee da nga am yërmande ci nit ki te nga bëgg koo dimbali dëgg, loolu dina feeñ ci saay kàddu. Xalaatal bu baax ci li ngay wax ak ci ni nga koy waxee. Moytul a wax lu mën a merloo nit ki.

5. Wutal a dimbali nit ki. Xalaatal ci li nit ki soxla te dimbali ko ci. Sa mbaaxaay mën na tax nit ki déglu la.

SEETAL AAYA YII ITAM

Room 12:​15, 16; Galasi 6:10; Yawut ya 13:16

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager