NI NGA MËNEE TÀMBALI WAXTAAN
Jëf ya 26:2, 3
LESOŊ 4
Nanga suufeelu
Njàngale bi: «Nanga suufeelu te wone ne ñeneen ñi ñoo la sut.»—Filib 2:3.
Ni ko Pool defe
1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Jëf ya 26:2, 3. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:
Naka la Pool suufeelee boppam ba muy wax ak Buur Agaripa?
Naka la Pool wonee ne nekkul woon di jàngale xalaati boppam, waaye xalaati Yexowa rekk la doon jàngale? Xoolal Jëf ya 26:22.
Ban njàngale lañu mën a jële ci li Pool def?
2. Bu ñu suufeelee suñu bopp te won nit ñi respe, loolu dina tax ñu déglu ñu bu baax bu ñu leen di yégal xibaar jàmm bi.
Nanga roy ci Pool
3. Wonal nit ki respe. Moytul di wax mel ni yaw yaa xam lépp, ndaxte loolu mën na tax nit ki foog ne da nga ko xeeb.
4. Woneel ne li ngay wax jógewul ci yaw, waaye ci Biibël bi la jóge. Xelal yu nekk ci Kàddu Yàlla mën nañu laal xolu nit ñi. Kon bu ñuy sukkandikoo li ñuy wax ci Kàddu Yàlla, dinañu leen dimbali ñu nànd ko.
5. Woneel ne ku lewet nga. Bul forse nit ñi ñu nangu sa xalaat. Suufeelu dina tax nga ànd ak dal te xam ni ngay jeexalee waxtaan bi ngir moytu xuloo ak nit ki. (Kàddu yu xelu 17:14; Tit 3:2). Sa tontu bu lewet mën na tax nit ki déglu ñu beneen yoon.
SEETAL AAYA YII ITAM
Room 12:16-18; 1 Korent 8:1; 2 Korent 3:5