TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • lmd lesoŋ 9
  • Wonal nit ñi ne li ñuy yëg itteel na la

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Wonal nit ñi ne li ñuy yëg itteel na la
  • Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ni ko Yeesu defe
  • Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?
  • Nanga roy ci Yeesu
  • Woneel mbaax
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Yan jikko yu rafet la Yeesu amoon?
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Deel muñ, te def ndànk ak nit ñi ci liggéeyu waare bi
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Wonal nit ñi ne am nga itte ci ñoom
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
Xóotalal waxtaan bi
Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
lmd lesoŋ 9

LI NGA MËN A WAX BOO SEETIWAATEE NIT KI

Ba Yeesu ak talibeem wacce seen gall, dañoo tiim mbooloo mu réy mu leen di xaar ci tefes bi.

Màrk 6:30-34

LESOŊ 9

Wonal nit ñi ne li ñuy yëg itteel na la

Njàngale bi: «Nangeen bokk ak ñi am mbégte, ci seen mbégte; te bokk ak ñi am naqar, ci seen naqar.»—Room 12:15.

Ni ko Yeesu defe

Ba Yeesu ak talibeem wacce seen gall, dañoo tiim mbooloo mu réy mu leen di xaar ci tefes bi.

Turu WIDEO bi: Yeesu dal di gis mbooloo ma, yërëm leen

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Màrk 6:​30-34. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1. Lu tax Yeesu bëggoon a beru, moom ak talibeem yi?

  2. Ba Yeesu gise mbooloo ma, dafa leen jàngal lu bare. Lan moo ko ci xiir?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?

2. Bu dee dañoo am yërmande ci nit ñi, dinañu ko yëg ci suñuy wax ak suñuy jëf. Dina ñu xam ne nëw ñu rekk ngir yégal leen xibaar bi ñu yor, waaye dañoo am itte ci ñoom.

Nanga roy ci Yeesu

3. Déglul nit ki bu baax. Bu nit ki nekkee di la wax yëg-yëgu xolam, walla njàqare yi mu am, walla sax mu nekk di wéddi li nga koy jàngal, bul ko dog. Déglu ko bu baax. Noonu nga koy wone ne, li muy yëg itteel na la.

4. Bàyyil xel ci ñi nga war a seetiwaat. Xalaatal ci waxtaan bi ngeen amoon ayu bés bi romb ba pare nga xalaat ci laaj yii di topp:

  1. ‘Lu tax mu soxla xam dëgg gi?’

  2. ‘Naka la ko njàngum Biibël bi mënee dimbali ci dundam te may ko yaakaar?’

5. Waxal nit ki li mu soxla xam. Bu nit ki amee laaj yi muy laaj boppam, won ko ne njàngum Biibël bi mën na ko dimbali mu am tontu ci laaj yooyu yépp. Won ko itam ne Biibël bi mën na ko jox xelal yu baax.

SEETAL AAYA YII ITAM

Room 10:​13, 14; Filib 2:​3, 4; 1 Piyeer 3:8

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager