TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 4/00 p. 1
  • Ndax yaa ngiy wuyu mbëggeelu Krist ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndax yaa ngiy wuyu mbëggeelu Krist ?
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2000
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu góor-góorlu ci def lu baax !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • “ Defleen lii ngir fàttaliku ma ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Nañu dimbali suñuy moroom ñu jot ci lu baax li njot gi di indil nit ñi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • “ Bëggleen Yexowa, yéen ñépp ñi koy topp bu baax ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
Sasu Nguuru Yàlla — 2000
km 4/00 p. 1

Ndax yaa ngiy wuyu mbëggeelu Krist ?

1 Ba muy xalaat ci dundinu Njaatigeem, ndaw li Yowanna lii la bind : “ [Yeesu, mi] bëgg[oon] ñoñam yi nekk ci àddina [...], bëgg na leen ba fa mbëggeel mana yem. ” (Ywna. 13:1). Ci jamano Fàttaliku deewam ji ñu tollu, suñu xel a ngiy dem ci firnde mbëggeelu Krist, ji gën a mag. Mën nañoo wuyu mbëggeel googu, bu ñuy wone suñu ngëm ci njot gi mu fey, bu ñuy bokk ak cawarte ci liggéeyu waare bi, teyit niki Yeesu, bu ñuy muñ “ ba ca muj ga ”. — Macë 24:13 ; 28:19, 20 ; Ywna. 3:16.

2 Nañu wuyu mbëggeelu Krist : Yeesu sawaroon na lool ci ayu-bésam gu mujj, gi mu dund ci kow suuf (Macë 21:23 ; 23:1 ; 24:3). Ndegam Krist lañuy roy, ñun it mbëggeelam a ngi ñuy xiir ci “ def [... suñu] kem-kàttan ” ci njaamu Yeowa (Lukk 13:24). Ndax mën ngaa jariñoo li ñu fagaru ci weeru awril ngir yokk suñu yëngatu ci waare bi, ci li ngay yokk jot gi ngay jagleel sasu waare bi ?

3 Ren, Reeru Sàng bi daa yemook ngoonu àllarba 19 awril. Ñaata nit ñooy fekke xew bu am solo boobu ? Lu ci baree ngi aju ci ñun. Ndax bind nga turi ñii nga xalaat a sàkk seen teewaay — ñiy jàng ak yaw Biibël bi, ak ñeneen ñu dëgg gi soxal, say mbokk lenqe, say xame ci njaay ak njënd, ak ñi ngay ànd di jàngal ? Ndax jokkoo ngaak ñoom, ba noppi woo leen ci xew bi, ak xol bu tàlli ? Ndax dinga leen ko fàttali, bu ay fan yu néew desee laata ñoo màggal Fàttaliku bi ? Ndax soxla nañu sa ndimbal ngir àgg ca béréb ba ñu koy defe ? Mag ñi dinañu sàkk teewaayu képp koo xam ni waareetul. Li ñuy màggal Fàttaliku deewu Yeesu cib guddi biir ayu-bés gi asté ci njeexteelam, wàññiwul solo si am, ku nekk fekke ko.

4 Ñëwleen, fekk ngeen waaj ko bu baax : Lu am-a-am solo la nekk nit ñu waaj mbir mi bu baax te soloo xalaatin bi war, bu ñuy teewe Fàttaliku bi. Pool xiirtal na mbokki gëmkatam yi ñu bàyyi xel ci solo màggal gi (1 Kor. 11:20-26). Mën ngeen a duruus pàcc 13 ba 17 ci Linjili Yowanna, bu ngeen di amal seen njàngum Biibël bi ci biir njaboot gi, ba noppi nag ku nekk ci njaboot gi nettali li saraxu Yeesu di tekki ci moom. Buleen fàttee duruus Biibël bi bés bu ne ci ayu-bésu Fàttaliku bi itam !

5 Mbëggeel gi ñu am ci Yeesu daa sax reen yu xóot te dana jéggi ci lu baree bare bésu 19 awril. Li ñu dogu kay mooy won ko suñu mbëggeel ba fàww ! Fàttaliku deewam, bi ñuy màggal ren, dina ñu dimbali ñu dëgëral pas-pas boobu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager