Liggéey buy seddal xol
1 Ku nangu topp li Biibël bi di jàngale, sa xol dina sedd (Sab. 19:7, 8). Dootoo gëmati njàngale yu dul dëgg. Doo def lu bon lu lay lor, te dinga am yaakaar bu wóor ngir ëllëg. Dëgg gi nekk ci Biibël bi, dafay seddal xolu nit ñi koy jàng. Waaye du ñoom kese la seen xol di sedd. Ñi koy jàngale it, seen xol dina sedd. — Léeb. 11:25.
2 Liggéeyu waare bi dafa seddal seen xol : Taalibe Yeesu yi dañu war a bokk ci liggéeyu waare bi te sàkk ay taalibe. Waaye Yeesu wax na ne ñi nangu nekk ay taalibeem dinañu “ am noflaay ci seen xol ”. (Macë 11:29.) Moom ci boppam dafa gisoon ne buy waaraate, xolam dafay sedd. Ci moom, waaraate bi dafa meloon ni ñam (Ywna. 4:34). Bés dafa yónni woon 70 taalibeem ngir ñu waaraate. Ñooñu bi ñu gisee ni leen Yexowa jàpplee ci seen liggéey, seen xol dafa sedd lool. — Lukk 10:17.
3 Tey itam, ay karceen yu bare bu ñu bokkee ci liggéeyu waare bi, seen xol dafay sedd. Suñu benn mbokk mu jigéen nee na : “ Liggéeyu waare bi seddal na sama xol ndaxte bu ma koy def, damay gis ne sama dund am na lu mu jariñ. Bu may waaraate, sama xel du dem sax ci samay jafe-jafe ak ci coono yi may daj bés bu nekk. ” Beneen waaraatekat bu sawar dafa nee : “ Waaraate bi [...] dafa may fàttali bés bu nekk ne Yexowa mu ngi fi. Dafay tax ma am jàmm ak bànneex boo xam ne leneen mënu ma ko may. ” Dëgg-dëgg, liggéeyandoo ak Yàlla ci waaraate bi, lu réy la. — 1 Kor. 3:9.
4 Kiliftéefu Krist mettiwul : Dëgg la, karceen yi dañu war a ‘ def seen kem-kàttan ’. Waaye Yeesu laaju ñu li ñu àttanul (Lukk 13:24). Dafa ñu woo ak mbëggeel ngir ñu nangu topp kiliftéefam (Macë 11:29). Am na ñoo xam ne coono yu metti yi ñu am, moo tax duñu mën a def lu bare ci liggéeyu Yexowa. Waaye na leen wóor ne, bu fekkee ne lépp li ñu mën lañu def, seen liggéey neex na Yàlla. — Mark 14:6-8 ; Kol. 3:23.
5 Yàlla dafa fonk li ñuy def ngir turam. Kon ku koy jaamu xolam dina sedd lool (Yaw. 6:10). Nañu góor-góorlu ngir fu ñu mënta nekk, ñu jox ko li gën ci li ñu am.