“ Jébbaluleen ci man ”
1 Coono ak jafe-jafe kese ñoo fees àddina si. Waaye Yeesu dafa ñu woo ak mbëggeel ngir ñu jébbalu ci moom ba mën ci am noflaayu xol. Te bi ñu ko wuyusee ci loolu, mbir mi dafa tane ci ñun (Macë 11:29, 30). Nangu jébbalu ci Yeesu ngir nekk taalibeem, laaj na ñu bokk ci liggéey boo xam ne dëgg la dafa metti, waaye dafay tax suñu xol féex. Laaj na it ñuy waare xibaar bu baax bi jëm ci Nguuru Yàlla. Laaj na itam ñu dimbali suñuy moroom seen xol féex ni suñu xol féexe bi ñu jébbalee suñu bopp ci Yeesu, suñu kilifa bu baax bi. — Macë 24:14 ; 28:19, 20.
2 Ni suñu xol di féex bu ñuy bokk ci liggéeyu waare bi : Yeesu waxul taalibeem yi ñu boole li mu leen sant ak seeni itte bopp. Dafa leen wax ñu weccee seen yen bu diis bi ak yenam bu woyof bi. Itte ak ñàkk yaakaar yiy sonnal nit ñi tey, bokkatul ci li ñuy diisal. Duñu sonn it ngir alal yi saxul fenn (Luug 21:34 ; 1 Tim. 6:17). Su dee sax dañu jàpp lool te war a liggéey ngir faj soxla yi ñuy am bés bu nekk, jaamu Yàlla mooy nekk li ëpp solo ci suñu dund (Macë 6:33). Su ñu kontinee di ràññee li war a ëpp solo ci àddina, liggéeyu waare bi dina kontine di nekk luy féexal suñu xol. — Fil. 1:10.
3 Ci yoon, bu ñuy wax lu jëm ci li ñu fonk, dañuy kontaan (Luug 6:45). Karceen yépp fonk nañu lool Yexowa ak barke yi mu wax ne Nguur gi dina ko indi. Kon nag, bu ñuy waare, wax lu jëm ci “ xebaar bu baax bi ” te fàtte suñu itte yi, dafay tax suñu xol féex bu baax (Room 10:15) ! Ñépp xam nañu ne li ñuy gën a def dara, ñu ciy gën a aay, te di ci gën a am mbégte. Kon nag, bu ñu mënee yokk waxtu yi ñuy def ci waaraate bi, dina tax suñu xol gën a féex. Te bu amee ku nangu déglu bu ñuy waare, loolu dafa ñuy may doole (Jëf. 15:3). Mën nañu tase ak nit ñu suñu waxtaan soxalul, walla ñu nuy xeex. Waaye booba sax, nañu jàpp ci suñu xel ne li ñuy def neex na Yexowa, te lépp lu baax lu ci mën a jóge, barkeem moo koy indi. Bu ñu defee loolu, waaraate bi dina ñu indil féex ci wàllu ngëm. — Jëf. 5:41 ; 1 Kor. 3:9.
4 Bu ñu nangoo wuyu Yeesu ci li mu ñuy woo, dinañu liggéey ci wetam ni ay Seede Yexowa. Loolu cér bu réy la (Is. 43:10 ; Peeñ. 1:5). Dara mënu ñu may xol bu féex ni cér boobu !