Xaaj 10 : Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
Nañu leen jàngal ni ñuy waaraate këroo-kër
1 Bu magi mbooloo mi waxee ne nit ki mat na waaraatekat bu ñu sóobagul, ci lay mën a komaasee ànd ak mbooloo mi ci waaraate bi. (Seetal téere Organisés pour faire la volonté de Dieu, xët 79 ba 81.) Naka lañu koy mënee dimbali mu xam ni ñuy waaraatee këroo-kër ?
2 Nangeen waajal yéen ñaar waaraate bi : Waajal bu baax waaraate bi, lu am-a-am solo la. Wonal ki ngay jàngal Sasu Nguuru Yàlla yi ak téere Comment raisonner. Nee ko dina ci mën a gis li mu mën a wax buy waaraate. Dimbali ko mu seet foofu lu yomb lu mën a itteel ñi nekk ci seen goxu mbooloo. Bu komaasee waaraate, nanga ko wax mu jëfandikoo Biibël bi, ndax loolu lu am solo la. — 2 Tim. 4:2.
3 Bala ngeen di dem waaraate, nangeen ko waajal, di def mel ni yéen a ngi waaraate. Dina baax ci waaraatekat bu bees bi. Wax ko ne li nit ñi di def walla wax boo leen di waar, bare na. Waaye ba tey, na wone yar ak teggin ci lépp li muy def (Kol. 4:6). Nee ko waaraatekat mën na bañ a xam tont laaj yépp. Waaye na wax nit ki ne dina ci gëstu ba pare dellusi ngir waxtaan ci. — Léeb. 15:28.
4 Bu ngeen di waaraate yéen ñaar : Bés bu ngeen njëkkee waaraate këroo-kër, bàyyi ko mu seet ni ngay toppee li ngeen waajaloon yéen ñaar. Ba pare, bàyyi ko moom mu wax. Yenn saay liy gën mooy bu ngeen di wax ak nit, waaraatekat bu bees bi bokk rekk ci waxtaan bi. Mën na jàng benn aaya ba pare faramfàcce ko, walla def leneen lu mel noonu. Yow mii xam nit ki ak li mu mën, yaa war a seet li mu mën a def ci waaraate bi (Fil. 4:5). Boo koy jàngal ndànk-ndànk ni ñuy waaraatee, nanga faral di wax lu baax li muy def ci waaraate bi.
5 Nañu dimbali waaraatekat yu bees yi ñu defar porogaraam ngir faral di waaraate ayu-bés bu nekk. Loolu lu am solo la (Fil. 3:16). Nangeen jàpp bés ngir ànd ci waaraate bi. Xiir ko ci ànd ak ñeneen ñu sawar. Bu xoolee ni ñuy defe, dina gën a aay ci waaraate bi, te dina gën a bëgg waaraate këroo-kër.