Ndax am nga gox bi nga moomal sa bopp ngir waare ?
1 Gox bi nga moomal sa bopp mooy gox boo xam ne yow lañu ko dénk. Mën na féete foo xam ne dinga ko mën a gaaw a jot te dinga ci mën a waare yow kenn walla yow ak beneen waaraatekat. Dëgg la, teewe saa yoo ko mënee ci ndaje yi mbooloo mi di def ngir dem waare dafa am njariñ lool. Waaye boo amee gox bi nga moomal sa bopp ngir waare fa ginnaaw bi ngay ànd ak mbooloo mi ci waaraate bi, mën na tax suñu liggéeyu waare bi gën a baax. Rawatina ci mbooloo yi nga xam ne goxu mbooloo mi dafa yaatu lool. — Jëf. 10:42.
2 Njariñ bi ci nekk : Am na ñuy wax ne am gox boo moomal sa bopp ci wetu fi ngay liggéeye lu baax la, ndaxte dinga ci mën a waaraate ci waxtu noppalu bi walla boo wàccee. Ñeneen ñoom dañu gis ne ànd ak sa njaboot di waare ci sa dëkkandoo yi lu tollu benn waxtu, bala njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi, lu neex la. Bu ñu fa amee ku ñu war a dellu seeti walla ku ñu war a jàngal Biibël bi, nit kooku du leen sore. Te kon bu ñu fay dem duñu sonn, du leen jël jot bu bare te duñu ci paas paas bu metti. Komka gox boo moomal sa bopp dafay tax nga liggéey lu bare ci jot bu néew, mën na dimbali ñenn ñi ñu nekk yenn saay pioñee buy jàpple walla sax ñu nekk pioñee bu ci sax. Ginnaaw loolu it booy waare ci gox bi nga moomal sa bopp ba nga gën a miin ñi fa dëkk, mën na tax ñu mën laa wóolu, te yow dinga mën a wax ci li leen itteel. Loolu dina tax suñu liggéeyu waare bi gën a baax.
3 Am na pioñee boo xam ne, wottukat biy wër ci mbooloo yi dafa ko waxoon mu wut gox bu muy moomal boppam. Lii la wax : “ Dama topp li mu ma wax te ci lu gaaw dama gën a miin nit ñi dëkkoon ci sama gox. Ma daldi ñów ci nit ñi ci waxtu bi leen gënal. Lan laa ci jële ? Bu njëkk 35 nit laa doon dellu seeti ci weer wi, waaye léegi, lu ëpp 80 nit laay dellu seeti. Te it am naa léegi juróom-ñaari njàngum Biibël. ”
4 Naka lañuy ame gox bu ñuy moomal suñu bopp : Boo bëggee ñaan gox booy moomal sa bopp, nanga wax ak kiy toppatoo goxu mbooloo mi. Bu la neexee, mën nga wax beneen waaraatekat mu ànd ak yow boo fay waare. Nanga bind it kër foo dul fekk kenn. Nanga jéem a jeexal gox googu ci lu mat ñeenti weer. Boo gisee ne doo ko mën a jeexal, waxal ak kiy jiite seen njàngum téere bi ci mbooloo mi, walla ñeneen ngir ñu dimbali la ci. Boo jeexalee gox gi ci ñeenti weer yi, mën nga ko delloo. Mën nga ñaan it ñu joxaat la ko. Waaye nag, bul dénc gox googu lu yàgg-a-yàgg. Bu ko defee, ñeneen dinañu ko mën a ñaan. Mën na am seen goxu mbooloo yaatuwul noonu ba tax mënuñu la jox gox booy moomal sa bopp. Kon xéyna dinga mën a ñaan kiy jiite seen njàngum téere ci mbooloo mi, mu jox la benn xaaj ci gox fi seen njàngum téere di waare.
5 Liggéey bi ñu nu sant, maanaam waare ci “ àddina sépp ” liggéey bu am solo la (Macë 24:14). Laaj na ñu jàppalante bu baax ci liggéey boobu. Ginnaaw liggéeyu waare bi ñuy def ak waa mbooloo mi, bu ñu waaraatee ci gox bu ñu moomal suñu bopp, dinañu mën a xamal xibaar bu baax bi nit ñu gën a bare.
[Laaj yi]
1. Lan mooy gox bu ñu moomal suñu bopp ?
2. Ban njariñ moo nekk ci am gox boo moomal sa bopp ?
3. Lan la benn pioñee gis bi mu wutee gox bu mu moomal boppam ?
4. Naka nga mënee am gox boo moomal sa bopp te naka nga ciy waare ?
5. Bu ñu bëggee matal liggéeyu waare bi ñu nu sant, lan lañu war a def ?