Porogaraamu ndaje bu mag bu ñaari fan biy ñów
Yexowa ku mat a magal la. Naka lañu mënee màggal Yexowa ? Lan moo tax ñenn ñi di wax ne màggal Yexowa dafa metti ? Ñiy màggal Yexowa tey, yan barke lañuy am ? Dinañu ci am tont yu leer ci ndaje bu mag bu ñaari fan bi ñuy amal ci atum liggéeyu waare bu 2008. Turu ndaje bi mooy : “ Defleen lépp ngir màggal Yàlla ” (1 Kor. 10:31). Nañu xalaat bu baax ci li ñuy am ci ndaje bu ñaari fan bii di ñów. Dinañu ci am ay digle yu am maanaa ci wallu ngëm.
Wottukat biy wër ci ndaje yu mag yu ñaari fan yi dina def waxtaan bi tudd “ Pourquoi rendre gloire à Dieu ? ” (maanaam lu tax ñu war a màggal Yàlla ?), ak it waxtaan bi tudd “ Respectons les exigences divines de façon exemplaire ” ( maanaam nañu nekk ku jar a roy ndax li ñuy topp li Yàlla santaane). Dina def itam waxtaan bi ñu jagleel ñépp te tudd “ Qui glorifie Dieu aujourd’hui ? ” (maanaam ñan ñooy màggal Yàlla tey ?) ak it waxtaan bi ñuy mujj déglu. Waxtaan boobu mu ngi tudd “ Unis pour glorifier Dieu sur toute la terre ” (maanaam nañu ànd ñun ñépp di màggal Yexowa ci àddina si sépp). Wottukat boobu itam dina jiite Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi. Wottukat biy wër ci mbooloo yi dina def waxtaan yii : “ Prenons plaisir à refléter la gloire de Dieu ” (maanaam nañu fexe ba màggaayu Yàlla feeñ ci ñun te mu nekk lu nu neex), “ Examinons les besoins de la circonscription ” (maanaam li nekk soxla ci mbooloo yi bokk ci ndaje bii) ak it “ Restons ‘ fermement établis dans la vérité ’” (maanaam nañu kontine di ‘ sampu ci dëgg gi ’). Waxtaan boobu ci 2 Piyeer 1:12 lañu ko jële. Dinañu déglu itam waxtaan buy wone naka la liggéeyu pioñee di màggale Yàlla. Dinañu def ñaari waxtaan yu am ay xaaj. Li ñuy wax ci waxtaan yooyu dina tax ñu xalaat bu baax. Bi ñu ciy jëkk a def mu ngi tudd “ Glorifions Dieu dans tous les aspects de notre vie ” (maanaam nañu màggal Yàlla ci lépp li ñuy def). Waxtaan boobu dina wax ci xalaat yu xoot yu nekk ci 1 Korent 10:31. Beneen waxtaan bi am ay xaaj mu ngi tudd: “ Offrons un service sacré à la louange de Jéhovah ” (maanaam li ñuy def ngir jaamu Yàlla, na nekk lu koy màggal). Waxtaan boobu dinañu won naka lañu mënee jaamu Yàlla ci ay fànn yu bare. Ci dimaas bi, dinañu def waxtaanu La Tour de Garde bu ñu gàttal ak waxtaanu aaya bés bi. Bés boobu lañuy mën a sóob itam taalibe yu bees yi.
Ñu bare tey nanguwuñu déggal Yàlla. Li doom-Aadama mën a def tey nax na ñu bare ba duñu xalaat sax ci màggaayu Yexowa (Ywna. 5:44). Waaye ñun, nañu jël suñu jot ngir seet naka lañu mënee “ def lépp ngir màggal Yàlla ”. Dafa ñu wóor ne loolu, lu am njariñ la. Defleen lépp li ngeen mën ngir teew ci ndaje bi yépp te jàriñoo ci bu baax.