Porogaraamu ndaje bu mag bu ñaari fan biy ñëw
Naka lañuy def ba nit ñiy xeex ak doole diine dëgg gi bañ ñoo ëpp doole ? Naka lañuy fexee ba Seytaane bañ ñoo delloo ci àddina su bon sii ? Ndaje bu mag bu ñaari fan bi ñu war a def ci atum liggéeyu waare bu 2009, dina tontu laaj yu am solo yooyu. Ndaje baa ngi tudd ‘ Nootleen [lu bon] ci def lu baax ’ (Room 12:21). Nañu seet waxtaan yi ñuy def ci ndaje boobu.
Wottukat biy wër ci ndaje yu mag yu ñaari fan yi, dina def waxtaan yii : “ Fortifiés pour vaincre le mal par le bien ” (maanaam may nañu nu doole ngir ñu noot lu bon ci def lu baax) “ Prenez garde à la présomption ! ” (maanaam moytul teg sa bopp foo nekkul), “ Bientôt la fin du mal ” (maanaam léegi lu bon dootul amati) ak “ Fortifions notre foi pour vaincre le monde ” (maanaam nañu yokk suñu ngëm ngir mën àddina si). Wottukat biy wër ci mbooloo yi dina def waxtaan bi tudd “C’est maintenant le moment de rester éveillé ! ” (maanaam tey jii lañu war a yewwu). Waxtaan boobu ci Room 13:11-13 lañu ko jële. Dina def it waxtaan bi tudd “ Ne vous montrez pas découragé au jour de la détresse ” (maanaam buleen nangu seen doole néew ci bés yu metti yi) te ñu jële ko ci Proverbes 24:10. Yàkkamti nañu déglu it waxtaanu wottukat biy wër ci mbooloo yi. Waxtaan boobu mi ngi tudd “ Examinons les besoins de la circonscription ” (maanaam li nekk soxla ci mbooloo yi bokk ci ndaje bii). Beneen waxtaan bu ñu nar a may doole bu baax mooy, “ Pouvez-vous vous ‘ appliquer à ce ministère ’ en étant pionnier maintenant ? ” (maanaam ndax mën nga nekk pioñee ngir farlu ci liggéeyu waare bi ?). Waxtaan bu am ay xaaj bu ñuy njëkk a def mu ngi tudd “ Tenons ferme contre le ruses du Diable ” (maanaam buñu nangu daanu ci fiiru Seytaane). Dina ñu dimbali ñu raññee te moytu pexe yi Seytaane di jëfandikoo ngir fiir ñu ci wàllu technologie, wàllu fo yi ak wàllu njàng mi. Waxtaan bu am ay xaaj bi tudd “Acquerrez de la puissance pour résister à Satan en ce jour mauvais ” (maanaam wutleen doole biy tax Seytaane bañ leen a ëpp doole ci jamano bu bon bii) dina ñu won ni ñu gën a mënee topp xelalu Yàlla yi nekk ci Efes 6:10-18.
Noot li bon fi muy komaase ak waare xibaaru Nguur gi ñoo ànd (Peeñ. 12:17). Looloo tax Seytaane du tàyyi ci xeex ak doole Seede Yexowa yi (Isa. 43:10, 12). Waaye Seytaane du ñu gañe, ndaxte dañoo fas yéene ‘ noot [lu bon] ci def lu baax ’. Kon nañu def lépp li ñu war ngir mën a jariñoo bu baax waxtaan yi ñuy def yépp ci ndaje bu ñaari fan boobu.