LI ÑUY DEF AK LI NGEEN DI MAYE
Bibilyotek booy ŋàbb ci sa loxo
1 SEPTAAMBAR 2021
Ci wideo Ay yégle yu jóge ci Jataay biy dogal #6, mbokk Geoffrey Jackson lii la waxoon: «Ay at ci ginnaaw, ku ma waxoon ne bés dinañu am suñu téere yi yépp, ci suñu telefon walla ci suñu ordinatër, duma ko gëm.» Ndax yow itam loolu nga foogoon? Mbokk Jackson teg ca it ne: «Xéyna tey yeen a ngi laaj seen bopp, ni ñu naroon a def ci biir mbas mi, bu ñu amul woon JW Library.» Yexowa mu ngi ñu doon waajal at yii yépp ngir lu mel nii.
Naka lañu Yexowa waajalee? Am application JW Library, ban liggéey la laaj te lan lañuy def ngir gën koo yeesal, muy gën di baax di dem?
Lu masul a am
Ci weeru me ci atum 2013, Jataay biy dogal dafa laaj MEPS Programmation, benn ci ekip yiy liggéey ci kër gu mag ga, ñu defar ab application ngir ñu mën a jàng tekki Biibël bu bees bi, Traduction du monde nouveau. Paul Willies, kenn ci ñiy liggéey ci MEPS Programmation, lii la wax lu jëm ci loolu: «Ba fi ñu tollu nii, masaguñu génne ab application bu ñuy telesarse ci telefon. Waaye taxawal nañu benn ekip, areete yenn liggéey yu ñu yoroon te fas yéene liggéey ak yeneen ekip yiy liggéey fii ngir defar application boobu te dugal ci lépp li war. Ñu ngi ciy ñaan Yexowa saa su ne; te yaakaar nañu ne, ci ndimbalam dinañu ko pare bala suñu ndaje mu mag mi, maanaam fii ak juróomi weer.»
Li gënoon a jafe mooy ni ñuy def ba application bi bañ a yem ci Biibël bi, waaye it ñu mën ci yokk téere yu bare te génne ko ci làkk yu bare. Ci sãwiyee 2015, dugal nañu ci application bi, lu ëpp ci téere yi am ci làkku Ãgale. Te juróom-benni weer gannaaw loolu rekk, nit ñi mënoon nañu telesarse téere yi foofu, ci lu ëpp téeméeri làkk.
Bi application bi génne ba léegi, mbokk yi yokk nañu ci ay wideo, te fexee boolel ci benn palaas, téere yépp yi ñuy soxla ci ndaje yi. Rax-ci-dolli fexe nañu sax, ba bu ñuy jàng Biibël bi, ñu mën a bës ci ab aaya ngir ubbi Guide de recherche.
Bibilyotek bi dafa laaj toppatoo
Nit ñiy jëfandikoo application JW Library ci aparey bare nañu lool. Seetlu nañu ne, bés bu nekk, dañuy ubbi application bi ci lu tollook 8 milioŋi aparey te weer wu nekk lim bi dafay àgg ci 15 milioŋi aparey. Lan lañu war a def ba application bi mën a ubbeeku ci aparey yooyu yépp? Mbokk Willies lii la ci wax: «Application bi, liggéeyam du jeex. Fi ñu tollu nii, ñu ngi ciy liggéey ngir gën koo yeesalaat te gën a yombal ni ñu koy jëfandikoo. Rax-ci-dolli, ndegam ñiy defar aparey yi dañuy faral di yeesal seen liggéey ak di génne lu bees, ñun it fàww ñu wéy di liggéey ci suñu application bi ngir mu mën a dox ci aparey yu bees yooyu. Te war nañu it wéy di ko toppatoo ngir mën a wéy di ci dugal suñu téere yu bees yi ak ojo yi.» Fi ñu tollu nii, bu ñu boolee làkk yépp, mën nañu ne, am na lu tollook 200 000 téere ak 600 000 ojo ci application JW Library bi!
Toppatoo application bi dafa laaj it ñu jënd ay logiciels, maanaam lu mën a doxal ordinatër yi. Jënd nañu ci lu bare. Ci misaal, at mu nekk dañuy fey lu tollu ci 1 300 euro ngir benn logicel kese. Rax-ci-dolli, suñu mbokk yiy liggéey ci wàllu informatique bi, te ñu leen di woowe waa MEPS Programmation, dañuy jënd at mu nekk, ay ordinatër yu bees, ay tablet ak ay telefon ngir xool ndax suñu application bi dina ci dox. Li ñuy fey ci loolu tollu na ci 8 500 euro at mu nekk.
Li ñuy telesarse mu ngi wàññi depãs yi
Application JW Library bi, wàññi na bu baax depãs yi ñu doon def ci sotti téere ak yóbbu leen ci réew yi suñu mbokk yi nekk. Ci misaal, nañu jël téere bu ndaw bi tudd Examinons les Écritures chaque jour. Ci atum 2013 bi, sotti nañu ci 12 milioŋi téere. Waaye juróomi milioŋ rekk lañu ci sotti ci atum 2020. Moona de, am na lu tollook 700 000 seede Yexowa yu bees ñu ñów ci suñu mbootaay bi. Lu waral coppite boobu? Lu ëpp ci suñu mbokk, ci JW Library lañuy jànge aaya bés bi.a
«Njëgam foo ko natt wees na ko»
Application JW Library dafa ñuy dimbali ci yeneen anam yu bare. Suñu mbokk bu jigéen bu tudd Geneviève te dëkk Canada nee na, application bi moo ko dimbali mu gën a farlu ci njàngum Biibëlam. Mu teg ci ne: «Wax dëgg fa Yàlla, bu dee saa yu ma waree gëstu Biibël bi, fàww ma dajale ay téere yu bare teg, foog naa nee duma ko mën a def bés bu nekk. Waaye ak application bii, damay jël sama tablet rekk, toog def sama njàngum Biibël ndax lépp li ma soxlaa ngi ci biir. Loolu yokk na sama ngëm te tax na ma gën a jege Yexowa.»
Geneviève
Application bi, ci jamanoy mbas mi la njariñam gën a fës. Charlyn suñu mbokk mu dëkk Etaa Sini lii la wax: «Bi feebaru COVID-19 bi lawee ci àddina si ba tey, toog naa at te gisuma téere bu bees bu suñu mbootaay sotti. Waaye loolu terewul ñu am lépp li ñu soxla ci wàllu ngëm ndax JW Library bi. Maa ngi ciy gërëm Yexowa bu baax.»
Faye, suñu beneen mbokk bu dëkk Philippines wax na it li mu ci xalaat te ñu bare bokk nañook moom xalaat. Da ne: «Li ma gën a yéem ci mbir mi mooy, mën naa wax ne, application bi tax ma gën a jege Yexowa. Moom laay njëkka ubbi bu ma yeewoo. Moom laay déglu su may def liggéeyu kër gi. Moom laay jëfandikoo ngir waajal suñu ndaje yi. Moo may dimbali it ma waajal li may wax, bu may jàngale Biibël bi. Su ma amul lu ma def, ci laay seetaan ay wideo. Su ma nekkee fenn te war a xaar lu yàgg, ci laay jàng ay téere walla Biibël bi. Wax dëgg, njëgam foo ko natt wees na ko.»
Application bi am itam njariñ bu réy ci liggéeyu waare bi. Ci misaal, ca réewu Kamerun, amoon na ñaari mbokk yu jigéen yu doon waare. Kenn ki jëfandikoo aaya bu neex lool suñu beneen mbokk mi. Semen bi ci topp, suñu mbokk mi bëgg a jàngal nit aaya boobu waaye xamatul woon fi aaya bi nekk ci Biibël bi. Lii la mbokk wax: «Fàttewoon naa aaya bi, waaye am na ay baat yu ma ci jàppoon. Noonu ma ubbi application bi, bind baat yi rekk, mu génneel ma aaya bi. Application bi dafa may dimbali ma gis aaya yu bare yu ma fàttewoon.»
Li ngeen di maye jaare ko ci donate.jw.org dimbali na ñu, ñu am application JW Library bi. Te maye yooyu ñoo tax it ñu mën di wéy, di ci yokk lu bees ak di ko yeesal ngir suñu mbokk yi ci àddina si sépp, mën koo jariñoo.
Bi JW Library tàmbalee ba léegi
Oktoobar 2013: Ci lañu génnee application bi, dugal ci suñu sotti Biibël bu bees bi, Traduction du monde nouveau
Sãwiyee 2015: Ñu yokk yeneen téere ci làkku ãgale te génnee application bi, ci lu ëpp téeméeri làkk
Nowàmbar 2015: Ñu yokk ci mën a rëdd mbind yi, bu ñuy jàng ab téere
Me 2016: Ñu yokk paas bu ñu jagleel suñu ndaje yi ci mbooloo mi
Me 2017: Ñu yokk ci mën a bind ci téere yi, booy jàng
Desàmbar 2017: Ñu yokk ci la Bible d’étude
Màrs 2019: Ñu yokk ci mën a telesarse ay ojo, seetaan ay wideo te gis téere yi ñu dajale ci Guide de recherche
Sãwiyee 2021: Ñu yokk yu sew sewaan yu bare, ci téere Mën nga dund ci jàmm ba fàww!
a Dañuy fey xaalis, saa yu nit telesarsee dara ci JW Library. Ci misaal, daaw, fey nañu lu tollook 1, 3 milioŋu euro ngir nit ñi mën a seetaan ay wideo ci application bi mbaa ñu telesarse. Waaye ba tey, loolu mën a gën a yomb fuuf di sotti ay téere, ay CD mbaa ay DVD ak di leen yóbbu fépp fu suñu mbokk yi mën a nekk.