TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • hf xaaj 5 xaaj yi 1-2
  • Li ngeen mën a def ngir wéy di juboo ak seeni mbokk

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ngeen mën a def ngir wéy di juboo ak seeni mbokk
  • Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • 1 KONTINELEEN DI GISE SEENI MBOKK NI MU WARE
  • 2 BU KO MBIR MI LAAJEE, JËLLEEN DOGAL TE DËGËR CI
  • Na ku nekk yem ci ki mu séyal
    Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Na ku nekk yem ci ki mu séyal dégluleen li Yàlla wax ngir am séy bu neex
    Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Li ngeen mën a def bu poroblem amee
    Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Di tabax njaboot guy sargal Yàlla
    Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex
Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
hf xaaj 5 xaaj yi 1-2
Ab goro bu jigéen mu ngi xool jabaru doomam ak bëtu “ ni ngay togge du noonu ”

XAAJ 5

Li ngeen mën a def ngir wéy di juboo ak seeni mbokk

“ Solooleen . . . laabiir, woyof, lewet ak muñ. ” — Kolos 3:​12

Bés boo amee jëkkër walla jabar, njaboot gu bees ngay tàmbali. Dëgg la dinga kontine di bëgg say waajur te may leen cér, waaye léegi sa jëkkër walla sa jabar mooy nit ki gën a am solo ci yaw ci kaw suuf. Mën na am mu jafe ci say mbokk ngir ñu nangu loolu. Waaye santaane yi nekk ci Biibël bi dinañu la dimbali nga xam ni nga war a doxale ak ku nekk. Loolu dina tax ngeen mën a kontine di juboo ak seeni mbokk boole ci am jàmm ci njaboot gu bees gi ngeen di tàmbali.

1 KONTINELEEN DI GISE SEENI MBOKK NI MU WARE

Ñaar ñu séy ñu ngi ànd ak seeni waajur di doxantu

LI BIIBËL BI WAX : “ Teralal sa ndey ak sa baay ” (Efes 6:⁠2). Ak at yi nga mënta am, danga war a teral say waajur te may leen cér. Nangul ne ki nga séyal itam doom la bu soxlaa am itte ciy waajuram. Mbëggeel du fiir, kon bul mas a ragal ne diggante bi sa jëkkër walla sa jabar am ak waajuram yi dina waññi dara ci seen séy. — 1 Korent 13:4 ; Galasi 5:​26.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Moytul di wax lu mel ni “ Sa mbokk yi, saa su nekk dañu may wàññi ” walla “ Sa yaay masul a bëgg li may def ”

  • Jéemal a gise mbir mi ni ko ki nga séyal gise

2 BU KO MBIR MI LAAJEE, JËLLEEN DOGAL TE DËGËR CI

LI BIIBËL BI WAX : “ Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñuy kenn ” (Njàlbéen ga 2:24). Bés boo amee jëkkër walla jabar, say waajur mën nañu kontine di xalaat ne ba tey yaa ngi ci seen loxo, te xéyna dinañu bëgg a dugg ci sa séy ba weesu fi ñu war a yem.

Yéen ñaar a war a déggoo ci fi ngeen bëgg seeni waajur yem ci seen séy, ba pare ngeen wax leen ko boole ci cofeel bu mat. Mën ngeen a wax li ngeen xalaat te wax ji du ñagas (Kàddu yu Xelu 15:⁠1). Woyof, lewet, ak muñ dinañu la dimbali nga am diggante bu rafet ak say mbokk te kontine di “ baalante ci mbëggeel ”. — Efes 4:⁠2.

Jëkkër ak jabar ñu ngi waxtaan ; ab jëkkër ak jabaram ñu ngi may kado seeni waajur

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Su ngeen gisee ne seeni mbokk dañu dugg ci seen séy ba mu ëpp te loolu naqari leen, yéen ñaar nangeen ci waxtaan bu seen mer dalee

  • Nangeen déggoo ci ni ngeen di reglee poroblem bi

JÉEMLEEN A YËG LI NEKK SEEN XOL

Am na solo ngeen nànd li seeni waajur di yëg ci seen xol te nànd it ni ñu gise mbir mi. Bu ñu duggee ci seen séy, nekkul ne dañu ko bëgg a yàq. Ñoom dañu leen fonk dëgg. Mën na metti ci seeni waajur ñu jële leen ni beneen njaboot. Xéyna dinañu foog ne dangeen leen won ginnaaw. Bu ngeen toppee santaane yi nekk ci Biibël bi te ku nekk mën a wax sa moroom li nga yëg, dingeen mën a kontine di teral seeni waajur te dungeen yàq seen séy.

LAAJLEEN SEEN BOPP LII :

  • Waajuru ki ma séyal, bu ñu bëggee dugg ci suñu séy, lu tax loolu waru maa bett ?

  • Naka laa mënee gën a bëgg sama jëkkër walla sama jabar te kontine di may cér samay waajur ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager