TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • hf xaaj 1 xaaj yi 1-3
  • Na ku nekk yem ci ki mu séyal dégluleen li Yàlla wax ngir am séy bu neex

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Na ku nekk yem ci ki mu séyal dégluleen li Yàlla wax ngir am séy bu neex
  • Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • 1 NANGULEEN FI LEEN YEXOWA TEG CI BIIR NJABOOT
  • 2 NA KU NEKK YËG KI MU SÉYAL
  • 3 BOKKLEEN XALAAT
  • Na ku nekk yem ci ki mu séyal
    Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Li ngeen mën a def ngir wéy di juboo ak seeni mbokk
    Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Li ngeen mën a def bu poroblem amee
    Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Naka nga mënee am jàmm ci sa biir njaboot? (Xaaj 1)
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
hf xaaj 1 xaaj yi 1-3
Benn góor ak benn jigéen ci seen bésu séy

XAAJ 1

Dégluleen li Yàlla wax ngir am séy bu neex

“ Ca njàlbéen ga Aji Bind ji sàkk na léen, kii góor, kii jigéen ”. — Macë 19:⁠4

Yexowaa Yàlla moo taxawal séy bi njëkk a am. Biibël bi dafa ñuy xamal ne Yàlla dafa sàkk jigéen bi njëkk daldi ko ‘ indil ’ ku góor ki. Aadama kontaan ba wax lii : “ Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux ! ” (Njàlbéen ga 2:22, 23). Mbégte boobu la Yexowa bëgg ñiy séy am ba tey.

Ñu bare bu ñu duggee ci séy, dañuy foog ne bànneex rekk lañu ciy am. Waaye ci dëgg, poroblem mënul ñàkk diggante jëkkër ak jabar, bu dee sax bëggante nañu bu baax (1 Korent 7:28). Dingeen gis ci téere bii li Yàlla santaane ci Biibël bi ngir dimbali ñi séy ak seen njaboot ñu am jàmm. Bu ngeen ko toppee, dingeen gis njariñ bi ci nekk. — Sabóor 19:9-​12.

1 NANGULEEN FI LEEN YEXOWA TEG CI BIIR NJABOOT

LI BIIBËL BI WAX : Jëkkër mooy kilifa ci biir njaboot. — Efes 5:23.

Yaw miy jëkkër, Yàlla dafa bëgg nga fonk sa jabar te toppatoo ko (1 Piyeer 3:⁠7). Yàlla dafa sàkk jabar ngir mu jàpple te wéetali jëkkëram, te yaw jëkkër ji, Yàlla dafa bëgg nga may sa jabar cér te won ko mbëggeel (Njàlbéen ga 2:​18). Danga war a bëgg sa jabar ba mu jaral la nga jiital njariñam te bañ a jiital sa njariñu bopp. — Efes 5:25-29.

Yaw miy jigéen, Yexowa dafa bëgg nga weg bu baax sa jëkkër te jàpple ko bu baax ci wareefam (1 Korent 11:3 ; Efes 5:​33). Jàppleel sa jëkkër ci dogal yi muy jël te ànd ak moom ak xol bu tàlli ci li muy def (Kolos 3:​18). Boo ko defee, dinga taaru ci sa kanamu jëkkër ak ci kanamu Yexowa. — 1 Piyeer 3:1-6.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Laajal ki nga séyal ni nga mën a def ngir gën a nekk jëkkër walla jabar ju baax. Déglu ko bu baax te jéem a gën a nekk jëkkër walla jabar ju baax

  • Bul yàkkamti. Bala ku nekk di mën a béggal moroomam, dina jël jot

2 NA KU NEKK YËG KI MU SÉYAL

LI BIIBËL BI WAX : Danga war a wut njariñu ki nga séyal (Filib 2:​3, 4). Ci sa doxalin ak moom, won ko ne sopp nga ko, te xam ne Yexowa dafa bëgg jaamam yi “ lewet ci ñépp ” (2 Timote 2:​24). “ Làmmiñu waxkat, jam-jami jaasi ; kàddu gu xelu, garab la ci. ” Kon nanga xool bu baax ni ngay waxe ak ki nga séyal (Kàddu yu Xelu 12:18). Xelum Yexowa dina la dimbali ba mbaax ak mbëggeel feeñ ci sa waxin. — Galasi 5:​22, 23 ; Kolos 4:⁠6.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Bala ngay waxtaan ak ki nga séyal ci mbir bu mën a yee fitna, nanga ñaan Yàlla ngir bañ a xuloo te nangu déglu

  • Xalaatal bu baax ci li nga bëgg a wax ak ni nga koy waxe

3 BOKKLEEN XALAAT

LI BIIBËL BI WAX : Boo séyee, dangay “ doon benn ” ak ki ngay séyal (Macë 19:⁠5). Waaye ba léegi ñaari nit ngeen te mën a wuute ci ni ngeen di xalaate. Kon dangeen war a jàng bokk xalaat ak bokk yëg-yëg (Filib 2:⁠2). Dafa am solo ngeen déggoo bu ngeen di jël dogal. Biibël bi dafa ne, bu diisoo amee pexe dina am (Proverbes 20:18). Yéen ñaar, bu ngeen di jël dogal yu am solo, nangeen bàyyi santaane yi nekk ci Biibël bi wommat leen. — Kàddu yu Xelu 8:32, 33.

Jëkkër ak jabar yuy raxas te di fóot mel ni ñi bokk ekip

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Bu ngeen di waxtaan, wax ko say yëg-yëg, bul yem ci wax ko li xew rekk walla li ngay xalaat

  • Boo bëggee sóobu ci dara, nanga ci njëkk a waxtaan ak ki nga séyal

a  Yexowa mooy turu Yàlla ci Biibël bi.

NANGEEN XAM NE JAFE-JAFE MËNUL ÑÀKK WAAYE BULEEN XÀDDI

Bul yaakaar ne yaw walla ki nga séyal dooleen juum mukk (Sabóor 103:14 ; Saag 3:⁠2). Tànnal di xool jikko yu rafet yi mu am, bañ a xool ay sikkam. Na la wóor ne bu ngeen toppee santaane yi nekk ci Biibël bi lépp ay baax waaye buleen yàkkamti (2 Timote 3:​16). Yexowa dina leen barkeel bu ngeen jéemee topp ay santaaneem. Te seen séy dina gën a dëgër lu at yi di wees. — Galasi 6:⁠9.

LAAJLEEN SEEN BOPP LII :

  • Ndax ki ma séyal yëg na ne moom laa gën a fonk ?

  • Lan laa def tey ngir won ki ma séyal ne bëgg naa ko te may naa ko cér ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager