TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • hf xaaj 2 xaaj yi 1-2
  • Na ku nekk yem ci ki mu séyal

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Na ku nekk yem ci ki mu séyal
  • Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • 1 SEEN SÉY, NA DOON LI ËPP SOLO CI YÉEN
  • 2 SÀMMLEEN SEEN XOL
  • Na ku nekk yem ci ki mu séyal dégluleen li Yàlla wax ngir am séy bu neex
    Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Li ngeen mën a def ngir wéy di juboo ak seeni mbokk
    Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Li ngeen mën a def bu poroblem amee
    Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
  • Naka ngay def ba am jëkkër ju baax walla jabar ju baax?
    La Tour de Garde annonce le Royaume de Jéhovah (Édition d’étude)-2024
Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
hf xaaj 2 xaaj yi 1-2
Ab jëkkër mu ngi jàpp parasool ngir jabaram te di ko dimbali mu dugg ci oto bi

XAAJ 2

Na ku nekk yem ci ki mu séyal

“ Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas. ” — Màrk 10:9

Yexowa, ndigal bii la ñu jox : “ Buleen wor ” (Malasi 2:​16, MN). Topp ndigal boobu, lu am solo la ci seen séy ndaxte bu ngor amulee ci séy kenn du wóolu moroomam. Te bu kóolute amul mbëggeel mënul sax.

Tey, ngor ci biir séy bareetul. Bu ngeen bëggee sàmm seen séy, fàww ngeen def ñaari mbir.

1 SEEN SÉY, NA DOON LI ËPP SOLO CI YÉEN

LI BIIBËL BI WAX : “ Sàmmleen seen dundin, waxuma ni ñu amul xel, waaye ni ñu am xel ” (Efes 5:​15). Seen séy dafa war a bokk ci li ëpp solo ci seen dund. Gise seen séy noonu, am xel la.

Yexowa dafa bëgg nga bàyyi xel bu baax ci ki nga séyal te ngeen dund yéen ñaar ci bànneex (Ecclésiaste 9:⁠9). Wone na ci lu leer ne waruloo sàggane mukk ki nga séyal, waaye kenn ku nekk ci yéen ñaar danga war a xool li nga mën a def ba bégal sa moroom (1 Korent 10:24). Na ku nekk won moroomam ne amal na ko njariñ te sopp na ko.

Ab jëkkër mu ngi indil jabaram lu tàng lu muy naan ; ab jëkkër bu ñibbisi këram fekk jabaram di togg

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Nanga fexe ba am jot di nekk ak ki nga séyal te bàyyi sa xel bu baax ci moom

  • Bul xalaat sa bopp kese waaye nanga sóoraale ki nga séyal

Ab jëkkër ak jabaram dañu génn ngir féexlu ci biti

2 SÀMMLEEN SEEN XOL

LI BIIBËL BI WAX : “ Képp ku xool jigéen, xédd ko, njaaloo nga ak moom ci sa xel ” (Macë 5:28). Bu nit di xemmem keneen ku dul ki mu séyal, mel na ni mu ngi wor jëkkëram walla jabaram.

Yexowa nee na danga war a ‘ sàmm sa xol ’ (Kàddu yu Xelu 4:23 ; Yérémi 17:⁠9). Boo bëggee def loolu, fàww nga yemale sa bët (Macë 5:​29, 30). Royal ci yonent Yàlla Ayóoba mi fasoon kollëre ak ay bëtam ngir bañ a xool benn jigéen bu dul jabaram ba koy xemmem (Job 31:⁠1). Nanga fas yéene bañ a seetaan foto walla film buy wone yëfu saay-saay diggante góor ak jigéen, maanaam pornographie. Te nanga fas yéene bañ a nob kenn ku dul ki nga séyal.

Ab jëkkër bu teg foto jabaram ci biroom

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Wonal ñépp ne danga takku bu baax ci ki nga séyal

  • Ki nga séyal, li muy yëg na la itteel te nanga gaaw a dagg bépp xaritoo bu dalul xelam

NA KU NEKK DEF WÀLLAM

Bul nax sa bopp ; nanga seet jikko yi nga war a xeex (Sabóor 15:⁠2). Bul rus a ñaan ñu dimbali la ci (Kàddu yu Xelu 1:⁠5). Boo amee xalaat yu ñaaw, nanga leen xeex. Bul xàddi. (Kàddu yu Xelu 24:16). Yexowa dina barkeel lépp li ngay def ngir yem ci ki nga séyal.

LAAJLEEN SEEN BOPP LII :

  • Naka laa mën a def ba gën a am jot ngir nekk ak ki ma séyal ?

  • Ndax def naa ki ma séyal sama xaritu benn bakkan ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager