TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • igw p. 16-p. 17
  • Laaj 10 : Lan lu rafet la Biibël bi wax ci ëllëg ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Laaj 10 : Lan lu rafet la Biibël bi wax ci ëllëg ?
  • Xam-xam bi nekk ci Kàddu Yàlla
Xam-xam bi nekk ci Kàddu Yàlla
igw p. 16-p. 17

LAAJ 10

Lan lu rafet la Biibël bi wax ci ëllëg ?

Ci biir àjjana bi Yàlla dige ci kaw suuf, ab baay mu ngi jëmbët benn garab, doomam di ñëw ci moom

“ Aji jub ay jagoo réew mi, dëkke ko ba fàww. ”

Sabóor 37:⁠29

“ Suuf si dina fi nekk ba abadan. ”

Dajalekat 1:​4, MN

“ Dina noot dee ba fàww, te Aji Boroom bi Yexowa dina fomp rongooñu ñépp. ”

Esayi 25:​8, MN

“ Noonu gumba yi di gis, tëx yi di dégg, lafañ di tëbeentu ni kéwél, te làmmiñu luu ne tell ak mbég ; ndax ndox dina balle ci màndiŋ mi, ay dex ci tàkk yi. ”

Esayi 35:​5, 6

“ Dina fomp bépp rongooñ ci seeni bët ; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu. ”

Peeñu ma 21:4

“ Dinañu tabax ay kër te dëkk ci. Dinañu jëmbët ay reseñ te lekk li ñu meññ. Duñu tabax ngir keneen dëkk, duñu jëmbët ngir keneen lekk, ndaxte samay nit, seeni fan dinañu mel ni fani garab ; te ñi ma tànn, dinañu jariñoo ba mu mat sëkk liggéey bi ñu def ak seen loxo. ”

Esayi 65:​21, 22, MN

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager