LAAJ 11
Bu nit deewee, lan moo koy dal ?
“ Saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf, si ma la jële ; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd. ”
Njàlbéen ga 3:19
“ Ñiy dund, xam nañu ne dinañu dee. Waaye ñi dee, ñoom, xamuñu dara . . . Lépp li nga mën a def ak sa loxo, def ci sa kem kàttan, ndaxte amul liggéey, amul waaj, amul xam-xam, walla sagowu ci bàmmeel bi nga jëm. ”
Dajalekat 9:5, 10, MN
“ Yeesu wax loolu, teg ca ne : « Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maa ngi dem yee ko. » Yeesu dafa bëggoona wax ne, Lasaar dee na, waaye taalibe yi dañoo xalaatoon ne mbiri nelaw rekk lay wax. Ci kaw loolu Yeesu wax ci lu leer ne : « Lasaar dee na. » ”
Yowaana 11:11, 13, 14