TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • gf lesoŋ 14 p. 22-23
  • Xaritu Yàlla yi dañuy moytu lu bon

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Xaritu Yàlla yi dañuy moytu lu bon
  • Mën nga nekk xaritu Yàlla !
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Jëf yi Yàlla bañ
    Lan la ñu Yàllay laaj?
  • Lan lañu war a def ba am dundin bu neex Yàlla ?
    Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Xaaj 13
    Déggleen li Yàlla wax
  • Ndax Yàlla dina alagaat ñu bon ñi ?
    Dundleen ba fàww ak bànneex ci suuf si !
Xóotalal waxtaan bi
Mën nga nekk xaritu Yàlla !
gf lesoŋ 14 p. 22-23

NJÀNGALE 14

Xaritu Yàlla yi dañuy moytu lu bon

Seytaane dafay jéema xiir nit ñi ci lu bon. Ku bëgga nekk xaritu Yàlla dafa wara bañ li Yexowa bañ (Sabuur 97:10). Li topp bokk na ci li xaritu Yàlla yiy moytu :

Yëf yi Yexowa bañ, yii ci la bokk, tëdd ak góor walla njaaloo ak jigéen, naan ba màndi, yàq biir, sàcc, fen, mer ba mënatuloo téye sa bopp ak wure xaalis

Bàkkaar ci wàllu tëdd ak góor walla jigéen. “ Waruloo njaaloo. ” (2 Musaa 20:14). Tëdd ak nit, fekk séyaguleen, lu bon la itam. — 1 Korent 6:18.

Naan ba màndi. “ Màndikat yi [...] duñu bokk ci nguuru Yàlla. ” — 1 Korent 6:10.

Rey nit, yàq biir. “ Waruloo rey nit. ” — 2 Musaa 20:13.

Sàcc. “ Waruloo sàcc. ” — 2 Musaa 20:15.

Fen. Yexowa bañ na “ làmmiñ buy fen ”. — Léebu 6:17.

Jëfi fitna ak mer ba mënatuloo téye sa bopp. “ Képp ku bëgg jëfi fitna, ci lu wóor [Yexowa] bañ na ko. ” (Sabuur 11:5). “ Kuy topp sa nafsu, nii ngay jëfe: [...] xadar [maanaam gaawa mer]. ” — Galasi 5:19, 20.

Wure xaalis. “ Buleen séq dara ak ku [...] nay [maanaam ku “ bëgge ”, NW]. ” — 1 Korent 5:11.

Bañante diggante xeet. “ Soppleen seeni bañaale te ñaanal ñi leen di fitnaal. ” — Macë 5:43, 44.

Li ñu Yàlla wax, suñu njariñ la. Moytu lu bon mën na nekk lu metti. Ndimbal bi nga mëna am ci Yexowa ak ci Seedeem yi, dina tax nga mëna moytu li neexul Yàlla. — Isayi 48:17 ; Filipp 4:13 ; Yawut yi 10:24, 25.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager