TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • gf lesoŋ 15 p. 24-25
  • Xaritu Yàlla yi dañuy def lu baax

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Xaritu Yàlla yi dañuy def lu baax
  • Mën nga nekk xaritu Yàlla !
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Lan mooy indi jàmm ci biir njaboot?
    Lan mooy indi jàmm ci biir njaboot?
  • Naka lañu wara dunde ci suñu njaboot ba mu neex Yàlla ?
    Lan la ñu Yàllay laaj?
  • Lan ngeen mën a def ngir am jàmm ci seen biir njaboot ?
    Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Nanga weg sa moroom
    La Tour de Garde annonce le Royaume de Jéhovah (Édition d’étude)—2025
Xóotalal waxtaan bi
Mën nga nekk xaritu Yàlla !
gf lesoŋ 15 p. 24-25

NJÀNGALE 15

Xaritu Yàlla yi dañuy def lu baax

Boo amee xarit boo sopp te fonk, dangay jéema mel ni moom. Mbind mu sell mi nee na : “ Yexowa, ku baax te jub la. ” (Sabuur 25:8). Ku bëgg nekk xaritu Yàlla, danga wara baax te jub. Mbind mu sell mi nee na : “ Yeen nag ñiy guney Yàlla, yi mu bëgg ci xolam, royleen ko ci loolu. Ngeen wéer seen dund ci mbëggeel. ” (Efes 5:1, 2). Li topp bokk na ci ni ñu ko mëna defe :

Ñaari góor ñu ngi bokk di liggéey ci benn sãce

Dimbalil sa moroom. “ Nanuy defal ñépp lu baax. ” — Galasi 6:10.

Nanga sawar ci liggéey. “ Ku daan sàcc, na ko dëddu te jublu ci liggéey lu baax ci ay loxoom. ” — Efes 4:28.

Nanga set ci yaram ak ci jikko. “ Nanu sellal sunu bopp ci bépp sobeb yaram walla bu xel, dund dund gu sell ba mat, ci ragal Yàlla. ” — 2 Korent 7:1.

Benn njaboot buy waaj a lekk

Nanga bëgg te fonk say waa-kër. “ Na góor gu nekk bëgg jabaram, ni mu bëgge boppam, te jigéen ji weg jëkkëram. Naka yeen xale yi, nangeen déggal seeni waa-jur. ”— Efes 5:33–6:1.

Nanga bëgg sa moroom. “ Nanu bëggante, ndax mbëggeel ci Yàlla la bawoo. ” — 1 Yowanna 4:7.

Toppal yoonu réew mi. “ Na nit ku nekk déggal [nguur gi] [...]. Joxleen ku nekk céram; [...] ku ngeen wara fey juuti [lempo], feyleen ko ko. ” — Room 13:1, 7.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager