TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • lmd lesoŋ 5
  • Wonal nit ki teggin

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Wonal nit ki teggin
  • Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ni ko Pool defe
  • Ban njàngale lañu mën a jële ci li Pool def?
  • Nanga roy ci Pool
  • Na nga suufeelu
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Wonal nit ñi ne am nga itte ci ñoom
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Waxal mel ni kuy waxtaan
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Woneel mbaax
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
Xóotalal waxtaan bi
Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
lmd lesoŋ 5

NI NGA MËNEE TÀMBALI WAXTAAN

Ndaw li Pool a ngi waar waa Aten.

Jëf ya 17:22, 23

LESOŊ 5

Wonal nit ki teggin

Njàngale bi: «Na seen jépp wax nekk wax yu neex.»—Kolos 4:6.

Ni ko Pool defe

Ndaw li Pool a ngi waar waa Aten.

Turu WIDEO bi: Pool a ngi waar waa Aten

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Jëf ya 17:​22, 23. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1. Waa Aten ay jaamukat xërëm lañu. Bi ndaw li Pool gisee li ñu daan def, lan la yëg ci xolam?—Xoolal Jëf ya 17:16.

  2. Pool mënoon na leen yedd, waaye defu ko. Naka la jëfandikoo li ñu gëm ngir yégal leen xibaaru jàmm bi?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Pool def?

2. Xalaatal bu baax ci li nga bëgg a wax, ni nga ko war a waxee ak waxtu bi gën ngir wax ko. Loolu dina tax nit ñi déglu la.

Nanga roy ci Pool

3. Xalaatal bu baax ci li nga war a wax. Ci misaal, bu de nit ki nekkul kerceen, xalaatal ci ni nga ko mënee jàngal ci lu jëm ci Biibël bi walla ci Yeesu.

4. Bu la nit ki waxee lu àndul ak li Biibël wax, bul ko gaw a jubbanti. Mayal nit ki mu wax li mu xalaat, bu de sax li muy wax àndul ak li Biibël di jàngale. (Saag 1:19) Booy déglu nit ki, di nga xam li mu gëm ak li tax mu gëm loolu. Noonu nga ko mënee dimbali.—Kàddu yu xelu 20:5.

5. Gërëm ko ci li mu waxe xalaatam. Xéyna ci moom, lépp li ñu ko jàngal ci diinem dëgg la. Kon, njëkkal a seet fu ngeen bokke xalaat, ba pare nga dimbali ko, ndànk ndànk ba mu nànd li Biibël bi di jàngale.

SEETAL AAYA YII ITAM

Kàddu yu xelu 25:15; 2 Timote 2:​23-26; 1 Piyeer 3:15

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager