TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • yc lesoŋ 1 p. 4-5
  • Am na kumpa goo xam ne boo ko xamee dinga kontaan

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Am na kumpa goo xam ne boo ko xamee dinga kontaan
  • Jàngal-leen seeni doom
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li nekk ci téere bii
    Yeewuleen! (2018)
  • Yàlla Dige Na Àjjana
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Lan mooy coobare Yàlla ngir suuf si ?
    Lan la ñu Yàllay laaj?
  • Lan la Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si ?
    Xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla !
Xóotalal waxtaan bi
Jàngal-leen seeni doom
yc lesoŋ 1 p. 4-5
Malaaka yi ñu ngiy déglu Yeesu bi muy wax ak nit ñi lu jëm ci Nguuru Yàlla

NJÀNGALE 1

Am na kumpa goo xam ne boo ko xamee dinga kontaan

Ndax xam nga lan mooy kumpa ? —a Kumpa mooy lu kenn xamul. Am na kumpa gu réy bu ñu wax ci Biibël bi. Kumpa gu sell la ndaxte ci Yàlla la jóge. Malaaka yi sax bëggoon nañu xam kumpa googu. Yaw nag, ndax bëgg nga ko xam ? —

Ci sa xalaat lan la malaaka yi doon jéem a xam ?

Yàgg na lool, Yàlla dafa sàkk benn góor ak benn jigéen. Ñu ngi tuddoon Aadama ak Awa. Yàlla dafa leen dugal ci tool bu rafet bu ñu doon woowe toolu Eden maanaam àjjana. Tool bu rafet boobu moo nekkoon seen kër. Aadama ak Awa bu ñu déggaloon Yàlla, ñoom ak seeni doom dinañu mën a defar suuf si sépp ba mu nekk àjjana. Te it dinañu mën a dund ba fàww ci àjjana jooju. Aadama ak Awa, lan lañu mujj a def ? Ndax yaa ngi koy fàttaliku ? —

Aadama ak Awa déggaluñu woon Yàlla. Loolu moo tax tey ñun nekkuñu ci àjjana. Waaye Yàlla waxoon na ne dina defar suuf si sépp ba mu rafet te nit ñépp dinañu dund ba fàww ci jàmm. Naka lay defe loolu ? Nit ñi toog nañu lu yàgg te xamuñu tont bi. Loolu kumpa la woon.

Bi Yeesu ñëwee ci kaw suuf, am na lu mu wax lu jëm ci kumpa googu. Dafa ne kumpa googu mu ngi jëm ci Nguuru Yàlla. Mu wax ne ñu ñaan ngir nguur googu ñëw. Nguur googu dina defaraat suuf si ba mu nekk àjjana.

Ndax yaw yàkkamtiwuloo xam kumpa googu ? — Fàttalikul ne nit ñiy déggal Yàlla rekk ñooy dund ci àjjana. Ci Biibël bi wax nañu ci ay góor ak ay jigéen yu bare yu doon déggal Yàlla. Ndax bëgg nga leen a xam ? — Nañu waxtaan ci ñenn ci ñoom te xool ni ñu mën a def ba mel ni ñoom.

JÀNGAL CI SA BIIBËL

  • Màrk 4:​11

  • 1 Piyeer 1:​12

  • Njàlbéen ga 1:​26-​28 ; 2:​8, 9 ; 3:​6, 23

  • Macë 6:​9, 10

  • Sabóor 37:​11, 29

a Ci téere bii, dinga gis màndarga bu topp ci laaj yi te mel nii : —. Boo ko gisee, xamal ne danga war a taxaw may sa doom mu tontu.

LAAJ YI :

  • Lu tax tey suuf si nekkul àjjana ?

  • Biibël bi ci ban kumpa gu réy lay wax ?

  • Lan la Yeesu wax ci kumpa googu ?

  • Lan nga war a def ngir dund ci àjjana ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager